Symbole

[WOLOF] LES QUINZE POINTS DE LA REFORME CONSTITUTIONNELLE

— 15 mars 2016

1. Fexee kurelu polig mengoo ak jamono ci réewum demokarasi mu màgg

2.Nit ñi bokul ci been kurelu politik mana laaj baatu askan wi ci bépp  xeetu wote

3. Sàkk Kurel gu mag guy doolel book moomel yi tudeeko Haut Conseil des collectivités territoriales ngir gën a faydal sakan wi yooriinu réew mi 

4. Nangul askan wi  ay àq, yelleef  ak  wareef yu bes muy : sañ-sañu kéewange ak dëkuwaay yu mucc ayib, sañ-sañ yu bées ci senni suuf ak leeb lu cay jur koom mbaa di ca meñee

5. Dooléel wareefu maxeej gi, (citoyen), beep nit bu ci biral ay warugaram

6. Delloo diirub palug ñiitu réewmi ci juróomi at 

7. Gën a dooleel kujeg politik gi ak njiitam

8. Doomi réewmi neek bitim réew am  seen dipitey boop yu leen di toogal ca péncum ndawi réewmi

9. Yaatal dooley Péncum Ndawi Réewmi ci ni miy sayto gornmaŋ bi booleek ma ko leegi muy am sañ-sañu cambar tërëliin ak doxaliini nguur gi

10. Jeebal Conseil Constitutionnel béep dogal laata ñu koy dëgal ak di ko doxal

11. Yokk limub ñaay toog ca Conseil Constitutionnel mu jogée ci juróom ag ci juroóom ñaar

12.Jox njital Péncum Ndawi Réewmi di Président Assemblée Nationale mu  taan ñaar ci juroom ñaari nit ñiy àtte ca Conseil Constitionnel 

13.Yaatal sañ-sañi Conseil Constitutionnel ngir muy joxe ay xalaat ak di wax cii dogal yi  cour d’appel jaap ne dëpoo wu ñu ak sartu ndeytu àtte yi

14. Ndeyu àtte yi tëral dëgal gis-gisu biy nangu réewmi am ay bokk moomel, ak gis-gis biy nangu nguur gi waññi leen ci ay ceram jox ko gox yi ak goxaan

15. Saxal abadan  li keen dootul ma na sopi yii dogal: paliinu njiitu réew mi, ak ñaari pal yu degaloo yi mu dul mana weesu ak juroomi at yi pal gu nekk di yem